Kàddug yéene gu Bàyyikoo ci ñi Xeetoo ci Suuf si

 
 
Ñu jàpp ni ñun ñëpp ci Suuf si la ñu sosoo, te nii ñu bokke léegi mësuñu ni bokke;
 
Ñu jàpp ni li ëpp ci ni ñu tërëele mbooloom nit ñi ci réew yi ñi ngii wone màndarga luy tasaaru wolla màbb te di indil doomu aadama yi ak li ñu wór jéyya ju màgg ci addina si yópp;
 
Ñu jàpp ni léegi mi ngiy leer nit ñuy gëna bare, ni war na nu seetaat li lal sunu gisinu addina te soppi sunu xalaatin indi bu bees (Einstein);
 
Ñu jàpp ni nun, Homo sapiens, eggagunu fi sunu xeet mëna egg fépp, te ba tey wóorna ni mën na nu tabax ci addina si menn mbooloo mu naat, mu yàgg, mu am jàmm te di saxal dund;
 
Ñu jàpp ni soppiku yu réy ci mbooloo mi ñi ngi sosoo ci wox ju leer nàñn te am kàttan (Kàddug-yéene Moomsaréew, Magna Carta) te soppi dëgg ci feenn rekk lay sosoo: ay kureel yu tuuti yu nit ñu am xalaat ak pasteef sañc (Mead);
 
 

Ñun, ñii fi xaatim, nu ngiy yégle te di yéene ni …..

Am na nu sañsañ bu wóor ci sukkandiku ci cëslaay yii nuy lim:
 
doon nit ñu xeetoo ci Suuf si te di ko sàmm, te it ku nekk topp say yooni réew;
 
fexe ba nit ñópp dund ci jàmm, moom seen bopp te it mëna faj seen soxla;
 
jél xalaatinu "Suuf Sunugaal" maanaam ñoo bokk gaalgi te lu ñëw ñopp lay dalandoo; (Fuller)
 
nangu ni nit ñópp ñoo yem, yelloo na ñu orma, kóolute, ak ku leen faaydaal ak fu ñu mëna nekk wolla fu ñu mëna tollu;
 
aar addina si ñu fiy bàyyil ñiy ñëw ëllëg;
 
doon jàambaari yem ci mbooloo, yàggal li ñu wór, ak mëtal dundu róowu bépp doomu aadama;
 
jàpp ni ci sunu dund ak sunu ligéey képp da ngay wéeru ci sa moroom, képp nekkal fi sa bopp ak itam say nekkandoo, te it di jàppante ak jàppalante ngir “doon-benn” yàgg fi;
 
di bañ ak di teggi tërëlin yi fi nekk, ak njiit yi, ak melo yi, su fekkee ni nekkalu ñu fi mbooloo mi yópp;
 
taxawal ay kureel te àndak njiit yu bees ngir faj soxla yi am ci addina si;
 
jubal ci lép lu ñuy def, te it di seentu njub ci suñuy bokk yi xeetoondoo ak ñun ci Suuf si, te ku nekk ci ñun di wéeru ci moroomam;
 
yéene ak santaane gisgis yii, xalaatin yii, ak jëfin yii tegu ci bokk-xeetoo ci addina si te ku nekk di wéeru ci sa moroom, ndax yeneen nit nangu leen te di leen jëfe naka lu ñu moomal seen bopp.
 

Déggoo bi

 
Kon nak, nun ñii fi xaatim, nu ngiy yégle te di yéene ak di digante ni dina nu sax te sukkandiku ci yii cëslaay, ànd ci ak yéene ak pasteef, te di góor ak jigéen yu jub te bokk wareef wu màgg wu book-xeetoo ci addina si.